Suunas yonent bi la said kebbeh di xeentu
Nu mu defe ba yonent bi beg lool la baay di sakku
Lu neex Rassulullahi, loolu neexna baye said kebbeh
Ku xam li yonent bi ban, dô ko gis ci baye said kebbeh
Moom baye said kebbeh masula waxtu
Saa su ne njapp, mu yees, masulu timale waxtu
Boo toppee maam ya mbokk laak yonent bi
Laajal doom cheikh yi xammeenanu said kebbeh
Su de beggnga roy suunas Mohammed
Jokkujil ci baye said kebbeh diineem ja rafetna
Bu newel di julli mangay durus lillaahi
baye said kebbeh xamul ludul tagg Rasuulullaahi
Li mu bind ci teere jagleelko yonent bi
Li mu bind ci teere jagleelko science bi
Li mu bind ci teere mu jem ci wallu xam xam
Buur Yalla teeralnako wonewul am am
Li mu am ci taalibe ci reewi nit nu nuul ni
Lu ko epp la Baay am ci reewi nit nu weex ni
Su de beggnga roy suunas Mohammed
Jokkujil ci baye said kebbeh, diineem ja rafetna
Boo demee banyaka
Laa illaha janngay riir
Daaray Alxuraan yaangay riir
baye said kebbeh, jaajеfate
Su de beggnga roy suunas Mohammеd
Jokkujil ci baye said kebbeh, diineem ja rafetna
Li mu tabax ci daara de meneesuko lim
Dongoom bi gena ndaw menna bind kaamil
Ku yaru ci baye said kebbeh bu waxee nga xam ko
Te lu mu la naanal bilaahi fook nga gis ko
La xew ca Maka ak la xew banyaka benn werante moo xew ca kerem ya
Boo jogee ci reew mi dem ci reewi arab yi
Boo nuyoo ba noppi faw nu laj la cheikh bi